22/05/2026
TEXTE DES LAUREATS PLUME DU MAÎTRE 2025 (7e édition)
« Delloo mbàttu ca ndaa la sant tay seede » poème de Ibrahima SARR, un chant de gratitude, un témoignage profond et puissant qui élève la figure de « SY Maalig » qui est plus qu’un guide, un réparateur de générations. Il décrit une époque abîmée, plongeant les jeunes, les femmes et même les autorités dans la confusion et la perte de sens. Mais dans ce chaos, une lumière s’est levée : celle de « SY Maalig »…
————-
DELLO MBÀTTU CA NDAA LA SÀNT TAY SEEDE
Ci jamono bu yàqu té lëndëm këriis
Jaaxle di nu bunduxatal teg nu tiis
Fit di maas, ndaw sànku, mag tumuranke
Way-jur amul yaakar ci njaboot ba jaaxle
Ndaw di wër rawukaay, dëkke fande
Jigéen saam boppam ba pénc jagadi
Sëytane di jaayu gën a firi pexeem yi
Kilifa tënku ci buur dërëm mu dunde
Jamono bu buur d**g di rëkk
Ndëndam ku jaayuwul mu rëkk
Di buum di bummi fu ko neex ngay xool
Ku àddu di jaam sa ngor ak dëggu mu suul
Jamono bu Yonnen raflee ku mu dénk
Lislaam di wër ruuh gu dal gu mu wékk
Li mu baaxle, ci la céeñéer jolli, di leeral
Nga wane yoon, di nu gunge ak niital
Yaa di jantu ngënéel bi fenq tay ci dunyaa
Leeral xol yi lëndamoon ci jamono ya
Jàngal ñi réeroon tegaat leen ci yoon
Lewal seen démb, dindi leen ci mbon
Yaa yaxantu ndaw ba mu raw tay
Tënk ko, xamal ko ñiy royukaay
Tax way-jur xelam dal ci ñoom
Kóolute dugg muy mbégte ci doom
Yar nga jigéen, xamal ko def ko soxna
Defar ko mu mat nday jiite léppi dunyaa
Defar nga ko ba ñu naw ko ndax jikko
Li ñu ko doon xaare ci pénc matale na ko
Lekko dërëmu nguur ba mu tee la àddu
Ëmbul sa sanqal ba tee jib sa kàddu
Yaa dëkke wax buur dëgg gu wér péng
Teg ko ci yoon, bu jaaxlee sa buntu mu fëgg
SY taawu nga ndono li, ñag tool bi
Sàmm jur gi, ba kenn ruurul tool bi
Sàggi wo sag wi, bay nga tool bi
Réeralóo pusó bi, ñaw nga diggante yi
Kon delloo mbàttu ca ndaa la ma naane
Ngir sant ak gërëm tey seede ci lu mu def
Ci man ak samay moroom fi nga nu jële
Ak fi nga nu dugal, kon SY Maalig jërëjëf
Jërëjëf di baat bu tuuti, ku déful du ko dégg
SY Maalig jërëjëf yaw mi nu def nuy ay sang
SY Al-MOURCHID jërëjëf yaw mi nu déf ay gor
Yar nu, def nu jàmbaar ba dunu def luy lor
Dagaan naa Boroom bi sàmmeel ci sang bi
Làq léppi ngërëm ba pare ni tekk dal
Di dagaan Boroom sax dàkk ci keppaar gi
Ëmb léppi yiw, nuy yàgg a fésal sunu cofeel
Ibrahima SARR
---Pour participer à la 8e édition, le lien d'inscription est en commentaire--- 👇🏾
En route vers le 10 juin ♥️